Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 5:15-21 in Wolof

Help us?

ROOM 5:15-21 in Téereb Injiil

15 Waaye warunoo yemale tooñu Aadama ak mayu Yàlla. Bàkkaaru kenn nit kooku tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak may, gi nu keneen nit ka Yeesu Kirist yéwénal, baawaan na ci ñu bare, ba suul tooñ googu.
16 Te bàkkaaru Aadama niroowul ak mayu Yàlla. Aadama bàkkaar na benn yoon, ba tax Yàlla daan ko, daanaale ñépp; waaye Yàlla jéggle na tooñ yu bare ci dara, ba mu àtte ñu bare ni ñu jub.
17 Bàkkaaru kenn nit tax na dee tàbbi àddina, yilif ñépp ni buur; waaye jëfu keneen nit ka, maanaam Yeesu Kirist, moo ko suul, ba tax ñu bare tàbbi ci dund gu bees, falu ni ay buur; xanaa ñi Yàlla boole ci yiwam wu bare, te àtte leen jub ci dara fa kanamam.
18 Kon nag nu gàttal wax ji: jàddug kenn nit ka rekk moo waral Yàlla daan ñépp; noonu itam jëf ju jubu keneen nit ka rekk moo ubbi bunt, ba ñépp mana jub ci kanam Yàlla te am dund gu bees.
19 Aadama moomu dafa déggadil Yàlla, ba yóbbaale ñu bare, ñu nekk i bàkkaarkat; noonu itam Yeesu Kirist dafa déggal Yàlla, yóbbaale ñu bare itam, ñu jub.
20 Yoonu Musaa daldi wàcc, ngir bàkkaar gëna bare; waaye fa bàkkaar bare, yiwu Yàlla gën faa bare.
21 Ba tax, ni bàkkaar doon yilife ñépp ni buur, indaale dee, noonu itam la yiwu Yàlla faloo ni buur, jóge ci njub, jëm ci dund gu dul jeex. Loolu lépp darajay Yeesu Kirist sunu Boroom moo nu ko may.
ROOM 5 in Téereb Injiil

Room 5:15-21 in Kàddug Yàlla gi

15 Waaye ni moyug Aadama deme, yiwu Yàlla demewu ni. Moyug kenn nit, Aadama, tax na ñu bare dee; waaye yiwu Yàlla ak mayug yiw gu kenn nit, Yeesu Almasi, ñaata yoon la gënatee baawaan, ñeel nit ñu bare?
16 Ni njeexitalu tooñu kenn nit deme, laa ne, mayu Yàlla demewu ni. Benn bàkkaar moo waral àtte bi indi mbugal. Waaye moy yu bare moo waral may gi teggi tuuma.
17 Moyug kenn nit ki, ci la dee jaare ci kenn nit kooku, ba falu, kon ñi jot ci xéewalu yiw, ba jagoo àtteb njub, ñaata yoon lañuy gënatee falu ci biir dund gu ñu ame ci keneen nit kiy Yeesu Almasi?
18 Kon nag noonee moyug kenn jure mbugalu nit ñépp daal, noonu la jenn jëfu njekk jurale ñépp dundin wu yees ci kaw àtteb njub bu leen jenn jëf ja may.
19 Noonee déggadig kenn nit taxe ñu bare doon ay bàkkaarkat, noonu it la déggug ndigalu kenn nit taxe ñu jox ñu bare àtteb nit ñu jub.
20 Yoonu Musaa moo dikk ngir fésal barewaayu moy, waaye fu bàkkaar bare, aw yiw gën faa bareeti,
21 ba tax na, noonee bàkkaar doone woon buur, ndax dee gi mu yilife ñépp, ni la aw yiw wuutoo, di buur moom itam, ndax àtteb njub gi aw yiw jural nit ñi, ba jëme leen ci texe gu sax dàkk, ci sunu ndimbalal Boroom Yeesu Almasi.
Room 5 in Kàddug Yàlla gi