Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 4:4-14 in Wolof

Help us?

ROOM 4:4-14 in Téereb Injiil

4 Képp kuy liggéey dina jot peyam; te pey googu du ag may, ñaqam la.
5 Waaye Yàlla dina àtte jub sax ki ko weddi woon; kon ku wéeruwul ciy jëfam, waaye mu gëm rekk, Yàlla dina jàppe ngëmam ni njub.
6 Noonu la Daawuda birale barkeelug nit ki Yàlla jagleel njub, fekk ay jëfam taxul.
7 Mu ne: «Ñi ñu baal seen jàdd yoon, te seeni bàkkaar far ci kanam Yàlla, ñu barkeel lañu.
8 Ki Boroom bi sëful ay bàkkaaram, kooka ku barkeel la.»
9 Kon nag barkeel googu, ndax ñi xaraf rekk ñoo ko yeyoo? Ndax ñi xaraful it bokkuñu ci? Ahakay! Ndaxte wax nanu ne, Yàlla jàppe na ngëmu Ibraayma ni njub.
10 Kañ la ko jagleel njub nag? Ndax lu jiitu xarafam la woon, am gannaaw ga? Lu ko jiitu la woon.
11 Ndaxte Ibraayma gëm na, te Yàlla jàppe na ngëmam ni njub, fekk booba xarafagul. Te xarafal gi, màndarga la woon ci yaramam, di firndeel ne ku jub la woon. Noonu la Ibraayma mana nekke baayu ñépp ñi gëm, ba Yàlla man leena àtte ni ñu jub, te xarafuñu sax.
12 Noonu itam la Ibraayma mana nekke baayu ñi xaraf, bu fekkee yemuñu rekk ci xaraf, waaye ñu am ngëm, ga Ibraayma sunu maam amoon lu jiitu xarafam.
13 Ndaxte Yàlla dafa digoon Ibraayma ak ñi naroona soqikoo ci moom, ne dinañu moom àddina si. Te dige boobu jógewul ci yoonu Musaa, waaye dafa jóge ci njub, gi Ibraayma amoon ci kanam Yàlla ci kaw ngëmam.
14 Ndaxte su fekkee ne ñi nekk ci yoonu Musaa rekk ñooy moom àddina, kon ngëm amatul njariñ, te digeb Yàlla toxu na.
ROOM 4 in Téereb Injiil

Room 4:4-14 in Kàddug Yàlla gi

4 Kuy liggéey, ag peyooram du taxawe ag may, waaye wartéef la.
5 Waaye ki jëful te gëm Yàlla miy jox ab yéefar sax, àtteb ku jub, ngëmam googu, ag njub lees ko koy waññal.
6 Ci moomu mbir la Daawuda doon wax, ba muy biral mbégtem nit ku Yàlla waññal ag njub gu jotewul dara ak ay jëfam.
7 Mu ne: «Mbégte ñeel na ñi ñu jéggal seeni tooñ, ñeel na ñooñu ñu baal seeni bàkkaar.
8 Mbégte ñeel na ku Boroom bi waññalul ag moyam.»
9 Kon moomu mbégte xanaa Yawut yiy xaraf doŋŋ la ñeel? Ñi xaraful it dañu cee bokkul? Ndax kat danu ne Ibraayma lañu waññal ngëmam ga, ag njub.
10 Nan lees ko ko waññale? Gannaaw ba mu xarafee, am ba mu xarafagul? Du gannaaw ba mu xarafee, waaye ba mu xarafagul la.
11 Gannaaw gi la jagoo màndargam xaraf, mu firndeel àtteb njubam gi ngëmam waral, te fekkul mu xaraf. Noonu la Ibraayma mana nekke maamu mboolem gëmkat ñi. Looloo tax muy maamu mboolem ñi xaraful, te gëm, ndax ñu waññal leen seen ngëm, ab àtteb ñu jub.
12 Looloo tax it Ibraayma di maamu ñi xaraf, te du xaraf gu ñu toppe aada, xanaa ñu boole ca topp ci tànki ngëm ga sunu maam Ibraayma amoon ba mu xarafagul.
13 Ndax kat digeb Ibraayma ba sédde Ibraayma àddina si, moom ak askanam, sàmm gu mu sàmm yoonu Musaa taxul, waaye àtteb njub bi mu jagoo ndax ngëmam, moo ko waral.
14 Nde su dee ñi ci yoonu Musaa la dige bi ñeel, kon ngëm dootu tekki dara, te kon digeb Yàlla ba day neen.
Room 4 in Kàddug Yàlla gi