Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 4:15-24 in Wolof

Help us?

ROOM 4:15-24 in Téereb Injiil

15 Yoonu Musaa daal du def lu dul wàcce merum Yàlla ci sunu bopp; ndax fu yoon amul, jàdd yoon du fa mana am.
16 Kon nag loolu Yàlla dige, ngëm rekk a koy indi, ngir mu sukkandikoo yiwu Yàlla rekk. Noonu la dige bi wóore ci ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp, du ci ñi nekk ci yoonu Musaa rekk, waaye itam ñi gëm ni Ibraayma gëme woon. Kon Ibraayma mooy sunu baay, nun ñépp.
17 Moom la Yàlla dogal, wax ko ci Mbind mi ne: «Def naa la baayu xeet yu bare.» Ndaxte Ibraayma gëmoon na Yàlla, miy dekkal ñi dee, tey wax ci lu amagul, mel ni dafa am.
18 Ibraayma dafa jàppoon ci ngëmam, di yaakaar, fekk bunti yaakaar yépp tëju. Moo tax mu nekk baayu xeet yu bare, ni ko Mbind mi waxe ne: «Noonu la sa askan di meli.»
19 Mu xool yaramam, xam ne dee rekk a ko dese, ndax mi ngi tollu woon ci lu mat téeméeri at, waaye ba tey ngëmam wàññikuwul. Mu xam it ne, Saarata manatula ëmb.
20 Waaye loolu taxul ngëmadi jàpp ko, ba muy werante ci waxu Yàlla; ngëmam sax di gëna dëgër, mu daldi sant Yàlla,
21 mu wóor ko ne loolu ko Yàlla dig, Yàlla man na koo def.
22 Moo tax «Yàlla jagleel na Ibraayma njub.»
23 Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji.
24 Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.
ROOM 4 in Téereb Injiil

Room 4:15-24 in Kàddug Yàlla gi

15 Yoonu Musaa daal, am sànj lay jur, te fu yoon wees di sàmm amul, genn moy amu fa.
16 Kon nag dige Yàlla boobu, ngëm moo ko waral, ngir mu di aw yiw doŋŋ. Noonu la dige bi doone lu wóor, ñeel ñi soqikoo ci Ibraayma ñépp; du ñi bokk ci yoonu Musaa rekk, waaye ñeel na itam ñi bokk ci ngëmu Ibraayma, miy sunu maam, nun ñépp.
17 Noonu la Mbind mi indee ne: «Maa la def ngay maamu xeet yu bare.» Ibraayma mooy sunu maam fi kanam Ki mu gëm, te muy Yàlla miy delloo ñi dee, bakkan, tey woo lu nekkul, mu doon lu nekk.
18 Ba bunti yaakaar yépp tëjee, Ibraayma moo dese woon yaakaaram, wéye ngëmam, ba doon maamu xeet yu bare, loolu dëppook kàddu ga noon: «Noonu la saw askan di tollu.»
19 Ngëmu Ibraayma wàññikuwul, doonte ba mu xoolaatee boppam, xam na ne yaramam dee na daanaka, ndax fekk na ay atam xawa tollu ci téeméer, te njurukaayu Saarata it fekk na ko dee.
20 Teewul digeb Yàlla ba la ne jàkk, nàttablewul, gëmadiwul, xanaa dëgërloo dooley ngëmam rekk, sant Yàlla.
21 Dafa wéroon Ibraayma péŋŋ ne li Yàlla dige, man na koo def.
22 Moo tax it, ñu waññal ko ngëmam ag njub.
23 Ba ñu bindee ne ngëmu Ibraayma, moom lees ko waññal àtteb ku jub, du Ibraayma doŋŋ la mbind ma ñeel.
24 Nun itam ci lanu; dees na nu waññal sunu ngëm, àtteb ñu jub, nun ñi gëm Ki dekkal sunu Sang Yeesu,
Room 4 in Kàddug Yàlla gi