Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 3:6-20 in Wolof

Help us?

ROOM 3:6-20 in Téereb Injiil

6 Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si?
7 Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: «Su fekkee sama ñàkk kóllëre gën na yékkati kóllëreg Yàlla, di yokk it ndamam, lu tax kon Yàlla di ma teg ba tey bàkkaarkat, ba di ma àtte?»
8 Lu tax manunoo wax ne: «Nanu def lu bon, ngir lu baax génn ca?» Am na sax ñu nuy tuumaal, di wax ne noonu lanuy waaree. Waaye ñiy wax loolu, ndaan gi ñu yelloo dina leen dal.
9 Kon nag lu nu ci wara wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci notaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi.
10 Moom la Mbind mi wax ne: «Ku jub amul, du kenn sax.
11 Amul kenn ku xam yëfi Yàlla, mbaa kenn ku koy wut.
12 Ñépp jeng nañu, ba kenn amalatul Yàlla njariñ. Kenn du def lu baax, du kenn sax!
13 Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan, seen làmmiñ làggi ci njublaŋ, te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas.
15 Ñu sawar lañu ci rey nit.
16 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
17 Xamuñu yoonu jàmm,
18 te ragal Yàlla sore na seen xol.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
20 Ndaxte sàmm yoon wi taxul kenn jub ci kanam Yàlla; solob ndigal yi daal mooy wone bàkkaar.
ROOM 3 in Téereb Injiil

Room 3:6-20 in Kàddug Yàlla gi

6 Mukk kay! Su njubteg Yàlla matul woon, ana nu muy àttee àddina?
7 Mbaa ñu neeti: «Su fekkee ne dëgguteg Yàlla, sama ñàkka dëggu lay gëna kaweel, te loolu di ndamam, kon man, ana lees may joxe àtteb bàkkaarkat?»
8 Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.
9 Ana kon nun Yawut yi, lu nu gëne ci nit ñi? Du ci lenn! Ndax firndeel nanu ba noppi ne, muy Yawut bi, di ki dul Yawut, ñépp a ngi ci kilifteefu bàkkaar.
10 Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.
11 Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
12 Ñépp a lajj ba bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
13 Seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, seen làmmiñ di ràbb njublaŋ, seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
15 seeni tànk bar ci yoonu tuur deretu jaambur,
16 te fu ñu jaare yàqute la ak musiba.
17 Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18 te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
20 Ndax kat deesul jox kenn àtteb ku jub fa kanam Yàlla ndax jëf ju mu def, ngir sàmm yoonu Musaa; solob yoon wi daal, mooy ci lees di ràññee bu baax luy bàkkaar.
Room 3 in Kàddug Yàlla gi