Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 3:16-19 in Wolof

Help us?

ROOM 3:16-19 in Téereb Injiil

16 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
17 Xamuñu yoonu jàmm,
18 te ragal Yàlla sore na seen xol.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
ROOM 3 in Téereb Injiil

Room 3:16-19 in Kàddug Yàlla gi

16 te fu ñu jaare yàqute la ak musiba.
17 Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18 te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
Room 3 in Kàddug Yàlla gi