Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 3:1-19 in Wolof

Help us?

ROOM 3:1-19 in Téereb Injiil

1 Yawut bi nag, ci lan la rawe ku dul Yawut? Te xaraf lu muy njariñ?
2 Raw na ko fu nekk. Ci bu jëkk Yawut yi la Yàlla dénk waxam.
3 Bu fekkee ne am na ci ñoom ñu ñàkk kóllëre, ndax loolu man na fanq kóllëreg Yàlla?
4 Mukk! Su ñépp nekkoon ay naaféq, du tere Yàlla nekk dëgg. Moom la Mbind mi wax ci Yàlla ne: «Loo wax, ñépp ànd ci, te ku layoo ak yaw, nga yey ko.»
5 Su fekkee nag njubadig nit dina feeñal njubteg Yàlla, lu ciy seen xalaat? Wax ji may bëgga wax nag léegi, waxi nit rekk la, maanaam: ndax kon Yàlla àttewul yoon ci li muy daan ku jubadi?
6 Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si?
7 Waaye nag xanaa dina am ku tontu ci loolu ne: «Su fekkee sama ñàkk kóllëre gën na yékkati kóllëreg Yàlla, di yokk it ndamam, lu tax kon Yàlla di ma teg ba tey bàkkaarkat, ba di ma àtte?»
8 Lu tax manunoo wax ne: «Nanu def lu bon, ngir lu baax génn ca?» Am na sax ñu nuy tuumaal, di wax ne noonu lanuy waaree. Waaye ñiy wax loolu, ndaan gi ñu yelloo dina leen dal.
9 Kon nag lu nu ci wara wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci notaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi.
10 Moom la Mbind mi wax ne: «Ku jub amul, du kenn sax.
11 Amul kenn ku xam yëfi Yàlla, mbaa kenn ku koy wut.
12 Ñépp jeng nañu, ba kenn amalatul Yàlla njariñ. Kenn du def lu baax, du kenn sax!
13 Seen put a ngi xasaw ni méddum ñetti fan, seen làmmiñ làggi ci njublaŋ, te seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Duñu génne ci seen gémmiñ lu dul ay móolu ak i xas.
15 Ñu sawar lañu ci rey nit.
16 Fu ñu jaar, foofa yàqu ak musiba.
17 Xamuñu yoonu jàmm,
18 te ragal Yàlla sore na seen xol.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, wax na ko ñi nekk ci yoon woowu, ngir gémmiñ yépp ne miig, te waa àddina sépp jaar ci àtteb Yàlla.
ROOM 3 in Téereb Injiil

Room 3:1-19 in Kàddug Yàlla gi

1 Kon nag ana lu ab Yawut rawe ci nit ñi? Ak luy njariñal xaraf?
2 Xanaa lu bare, ci wet gu nekk. Li ci jiitu moo di ñoom lañu dénk kàdduy Yàlla.
3 Su ci ñennat ñàkkee kóllëre, ndax seenug ñàkk kóllëre day fanq kóllëreg Yàlla?
4 Mukk kay! Fàww Yàlla wéye di ku dëggu, te ñépp di ay fen-kat, te noonu la Mbind mi indee ne: «Soo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.»
5 Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, deful ag njubadeem?
6 Mukk kay! Su njubteg Yàlla matul woon, ana nu muy àttee àddina?
7 Mbaa ñu neeti: «Su fekkee ne dëgguteg Yàlla, sama ñàkka dëggu lay gëna kaweel, te loolu di ndamam, kon man, ana lees may joxe àtteb bàkkaarkat?»
8 Ana kon lu tee nit waxe noonee nu soskat yi tuumaale ne nooy wax naan: «Nanu def lu bon, ngir mu jur lu baax»? Ñooñu mbugal lañu yelloo.
9 Ana kon nun Yawut yi, lu nu gëne ci nit ñi? Du ci lenn! Ndax firndeel nanu ba noppi ne, muy Yawut bi, di ki dul Yawut, ñépp a ngi ci kilifteefu bàkkaar.
10 Noonu it la Mbind mi indee ne: «Kenn jubul, du kenn sax.
11 Kenn xeluwul, kenn wutul Yàlla.
12 Ñépp a lajj ba bokk yàqu yaxeet, Kenn deful lu baax, du kenn sax!
13 Seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp, seen làmmiñ di ràbb njublaŋ, seeni kàddu aay ni daŋaru ñàngóor.
14 Seen gémmiñ, waxi móolu ak wextan la feese,
15 seeni tànk bar ci yoonu tuur deretu jaambur,
16 te fu ñu jaare yàqute la ak musiba.
17 Yoonu jàmm, xamuñu ko,
18 te ag ragal Yàlla jegewu leen.»
19 Xam nanu nag ne lépp lu yoonu Musaa wax, ñi ci yoonu Musaa la ko wax, ngir aw lay jeex tàkk, ngir itam mu leer nàññ ne àddina sépp a sikk fi kanam Yàlla.
Room 3 in Kàddug Yàlla gi