Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 2:19-27 in Wolof

Help us?

ROOM 2:19-27 in Téereb Injiil

19 Yaa ngi teg sa bopp wommatkatu gumba yi ak leeru ñi nekk cig lëndëm.
20 Yaa di jànglekatu ñi jàngul ak xamlekatu ñi xamul, ndaxte xalaat nga ne Yàlla jagleel na leen ci yoonu Musaa bépp xam-xam ak gépp dëgg.
21 Kon nag yaw miy jàngal say moroom, xanaa doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare di tere sàcc, mbaa doo sàcc yaw itam? Yaw miy tere njaaloo, mbaa doo njaaloo?
22 Yaw miy araamal xërëm yi, mbaa doo sàcc li nekk ci seeni xàmb?
23 Yaw miy damoo yoonu Musaa, mbaa doo ko moy, ba indi gàcce ci turu Yàlla?
24 Moo tax Mbind mi ne: «Yéena tax ñi nekkul Yawut di suufeel turu Yàlla.»
25 Bëggoon naa ngeen xam ne xaraf am na njariñ, boo ca boolee sàmm yoon. Waaye boo ko ca boolewul, sa xaraf amatul njariñ.
26 Te itam ku xaraful, tey def jëf yu jub yi yoonu Musaa santaane, ndax Yàlla du ko teg ni ku xaraf?
27 Ku dul Yawut te xaraful waaye di sàmm yoon wi, kooku dina la mana àtte, yaw Yawut bi. Ndaxte li ngay xam xam yoonu Musaa ci Mbind mi te xaraf, terewul nga koy moy.
ROOM 2 in Téereb Injiil

Room 2:19-27 in Kàddug Yàlla gi

19 Yaw mi mu wóor ne yaa di wommatkatub gumba yi, te di leeru ñi ci lëndëm gi,
20 yaa di jànglekatub naataxuuna yi, di sëriñub tuut-tànk yi, gannaaw yaa jagoo ci yoonu Musaa, mboolem luy jëmmu xam-xam, ak lépp luy dëgg.
21 Kon yaw miy jàngle, doo jàngal sa bopp? Yaw miy waare, di aaye sàcc, mbaa doo sàcc? Yaw miy aaye njaaloo, mbaa doo jaaloo?
22 Yaw mi bañ bokkaale, mbaa doo sëxëtoo jaamookaayi bokkaalekat yi?
23 Yaa ngi sagoo yoonu Musaa te di ko moy bay teddadil Yàlla!
24 Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jaambur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.
25 Aaday xaraf nag amal na la njariñ, ndegam sàmm nga yoon wi ko digle. Waaye soo dee moykatub yoon wi, sag xaraf, ñàkka xaraf lay doon.
26 Kon kay ki xaraful, tey jëfe njub gi yoonu Musaa santaane, ñàkka xarafam, deesu ko ko waññal ag xaraf?
27 Ki xaraful ciw yaramam, te teewu koo sàmm yoonu Musaa, moo lay teg ab daan, yaw mi boole mbindum yoonu Musaa, ak sag xaraf, te teewu la di moykatub yoon wi.
Room 2 in Kàddug Yàlla gi