Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 2:15-16 in Wolof

Help us?

ROOM 2:15-16 in Téereb Injiil

15 di wone it ne Yàlla bind na ci seen xol jëf yi yoonu Musaa santaane. Seen xel it seede na ne noonu la, fekk seeni xalaat ñoo leen di tuumaal, mbaa ñu leen di jéggal.
16 Ndax bés dina ñëw, bu xalaat yu làqu yi di feeñ, te Yàlla àtte nit ñi jaarale ko ci Yeesu Kirist. Xibaaru jàmm, bi may waare, moo ko wax.
ROOM 2 in Téereb Injiil

Room 2:15-16 in Kàddug Yàlla gi

15 Noonu lañu wérale ne jëf ji yoonu Musaa santaane moo binde ci seenub xol, ba seen yég-yégu xol seede loolu. Li koy firndeel it di seen xel miy def leeg-leeg mu sikk leen, leeg-leeg mu dëggal leen.
16 Te noonu lay deme kera bés ba Yàlla di àtte mbiri kumpa yu nit ñi, ci saytub Yeesu Almasi, ni ko sama xibaaru jàmm bi indee.
Room 2 in Kàddug Yàlla gi