12Képp ku doon bàkkaar nag te nekkuloo woon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci lu dul yoonu Musaa, nga doora sànku. Te képp ku doon bàkkaar te nga nekkoon ci yoonu Musaa, Yàlla dina la àtte ci yoon woowu.
12Mboolem ñi bàkkaar nag te fekku leen ci yoonu Musaa, yoonu Musaa toppu leen, waaye du leen teree sànku. Mboolem ñi bàkkaar it, te mu fekk leen ci yoonu Musaa, ci yoonu Musaa lees leen di daane.