Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 1:5-18 in Wolof

Help us?

ROOM 1:5-18 in Téereb Injiil

5 Te moom Kirist tàbbal na nu ci yiwu Yàlla, def nu ay ndawam, yónni nu ci biir xeeti àddina sépp, ngir ñu gëm ko te jébbalu, ba màggal turam.
6 Te ci ngeen bokk, yéen ñi Yàlla woo, ngeen nekk ci Kirist.
7 Yéen ñi dëkk Room ñépp, yéen ñi Yàlla bëgg te woo leen, ngeen nekk gaayam yu sell, na leen Yàlla sunu Baay ak Boroom bi Yeesu Kirist may yiw ak jàmm.
8 Kon nag li may jëkka wax mooy lii: sant naa Yàlla sama Boroom, jaarale ko ci Yeesu Kirist, ngir yéen ñépp, ndaxte seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
9 Bët bu set maa ngi leen di boole ci samay ñaan. Yàlla seede na li may wax, Yàlla mi may jaamu ci sama xel, ci xamle xibaaru jàmm bu Doomam.
10 Te li ma koy faral di ñaan mooy lii: bu soobee Yàlla, na ma ubbil bunt, ba ma mana ñëw ci yéen.
11 Ndaxte bëgg naa leena gis lool, ba indil leen barke bu jóge ci Xel mu Sell mi, ndax seen ngëm gëna dëgër.
12 Maanaam ma nekk ci seen biir, te nu dimbaleente ci sunu ngëm, ndax man itam ma gëna am doole.
13 Bokk yi, damaa bëgg ngeen xam ne xalaat naa leena seetsi ay yooni yoon, ngir meññ njariñ ci yéen, ni ma ko defe ci yeneen xeet yi, waaye ay téq-téq ñoo ma téye ba léegi.
14 Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam.
15 Li aju ci man nag, jekk naa ngir ñëw, xamal leen xibaaru jàmm bi, yéen it waa Room.
16 Ndaxte awma benn werante ci xibaaru jàmm bi may waare, ndax mbirum Yàlla la, mu làmboo dooleem, ngir musal képp ku ko gëm, muy Yawut ci bu jëkk mbaa ki dul Yawut.
17 Ndaxte xibaar bii day wone, ni nit mana jube ci kanam Yàlla, sukkandikoo ci ngëm rekk, tàmbali ci ngëm, yem ci ngëm. Moo tax Mbind mi wax ne: «Ku jub ci kaw ngëm, dinga dund.»
18 Merum Yàllaa ngi feeñe asamaan, wàcc ci nit ñi, ndax seen weddi Yàlla gépp ak seen jubadi gépp, ñoom ñi suul dëgg, di topp lu jubadi.
ROOM 1 in Téereb Injiil

Room 1:5-18 in Kàddug Yàlla gi

5 Ci Almasi lanu jote aw yiwu doon ay ndaw, ngir nit ñi déggal yoonu ngëm wi, ci biir mboolem xeeti àddina, ngir aw turam.
6 Te yeen ñi ñu woo ci Yeesu Almasi itam, ci ngeen bokk.
7 Bataaxal bi ñeel na mboolem yeen ña fa Room, di ñu Yàlla sopp, woo leen, ngir ngeen doon ñu sell. Aw yiw ak jàmm ñeel na leen, bawoo fa Yàlla sunu Baay, ak Sang Yeesu Almasi.
8 Ma doore sant sama Yàlla ci Yeesu Almasi ngir yeen ñépp, ndax seen ngëm siiw na ci àddina sépp.
9 Yàlla mi may jaamoo xol, ci ni may siiwtaanee xibaaru jàmm bu Doomam, moom seere na ne noppiwuma leena fàttliku.
10 Xanaa di saxoo dagaan ci samay ñaan, su ci Yàlla àndee, yoon wu jub wu ma mujj dikke ba ci yeen.
11 Yàkkamti naa leena gis, ba jottli leen mayug yiw gu bawoo ci Noo gu Sell gi, ngir dooleel leen,
12 te loolu mooy ma bokk ak yeen lu dëfal sama xol, dëfal leen, ci seen ngëm ak sama gos.
13 Bokk yi, bugguma ngeen umple ne ay yooni yoon laa leen mébéta seetsi, ba liggéey ci seen biir lu leen jariñ, ni ma ko defale yeneen xeet; waaye ay gàllankoor a ma téye ba tey jii.
14 Muy sama digg ak Gereg yu xay yi, mbaa ñu xayadi ñi, ak ñi rafet xel, mbaa ñi ñàkk xel, am na lu ma war ci ñoom ñépp.
15 Moo tax, yeen waa Room itam, ma yàkkamti leena àggesi xibaaru jàmm bi.
16 Awma lu may rus ci xibaaru jàmm bi, ndax kat mooy manoorey Yàlla jiy musal képp ku ko gëm, dale ci Yawut bi, teg ci ki dul Yawut.
17 Ci xibaaru jàmm bi lañu feeñal ni Yàlla di joxe nit ñi àtteb ñu jub, te lépp aju ci ngëm, ca ndoorte la, ba ca njeexital la. Noonu la Mbind mi indee ne: «Ku jub ndax ngëmam mooy dund.»
18 Sànjum Yàlla fa asamaan lay dale feeñ, ba wàcc ci mboolem ngëmadi, ak njubadiy nit ñiy fatt ag dëgg ci biir ag njubadi.
Room 1 in Kàddug Yàlla gi