22 Ñu teg seen bopp ni boroomi xel, fekk ñu ñàkk xel lañu woon.
23 Toxal nañu ndamu Yàlla Aji Sax ji, wuutal fa nataali nit ku dul sax, moom ak ay picc, ay rabi àll mbaa yuy raam.
24 Moo tax Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg, ñu sóobu ciy ñaawteef, di jëflante lu gàccelu ci seeni cér.
25 Toxal nañu dëggu Yàlla, tëral fen, di màggal ak a jaamu mbindeef, ba faaleetuñu sax Aji Bind, ji yelloo cant ba fàww. Amiin.
26 Loolu moo tax nag Yàlla bërgël na leen ci seeni bëgg-bëgg yu ruslu. Seeni jigéen sax dëddu nañu li jekk, sóobu ci lu jekkadi, ñoom ak seeni moroom.
27 Noonu it góor ñi bàyyi nañu li jekk ci seeni cér, maanaam ànd ak jigéen, bay am ay bëgg-bëgg yu tar ci ànd ak seeni moroom. Góor di defante ak góor li warul, ñu di jot seen peyu réer ci seeni yaram.