3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci liggéeyu Kirist Yeesu.
4 Ñoom ñaar dem nañu, bay bëgga jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di gërëm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy ñi gëm ci xeeti àddina sépp.
5 Nuyul-leen ma it ñiy booloo ci seen kër. Maa ngi nuyu it Epaynet, mi jëkka gëm Kirist ci diiwaanu Asi;
6 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci yéen.
7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist.
8 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi.
9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis;
10 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute. Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul,
11 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi.
12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk.
13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey.
14 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp.
15 Nuyul-leen ma it Filolog ak Yuli, Nere ak jigéenam. Te fàttewuma Olimpas ak gaayi Yàlla yiy booloo ak ñoom ñépp.
16 Te yéen bokk yi, saafoonteleen ak xol bu laab. Mboolooy ñi gëm Kirist yépp a ngi leen di nuyu.
17 Bokk yi, maa ngi leen di dénk, ngeen moytu ñi leen di féewale, ba di leen jàddloo yoon wi, ciy wax lu juuyoo ak dëgg gi ngeen jàng. Dawleen leen ba sore.
18 Ndax ñu deme noonu liggéeyaluñu Kirist sunu Boroom; seen bopp lañuy liggéeyal. Ñu ngi ñëw ak làmmiñ yu neex, di jay xol yu woyof yi, ba nax leen.
19 Waaye seen dégg ndigal bir na ñépp, ba sama xol sedd lool ci yéen. Teewul nag damaa bëgg ngeen am xam-xam bu leer ci lu baax, te baña laal dara ci lu bon.
20 Su ko defee Yàlla Boroom jàmm dina not Seytaane ci seeni tànk léegi. Yal na yiwu Yeesu sunu Boroom ànd ak yéen!
21 Timote sama nawle bi may jàpple ci liggéey bi, mu ngi leen di nuyu, ak samay bokk Lusiyus, Yason ak Sosipater.
22 Man Tersiyus mi bind bataaxal bii nag, maa ngi leen di nuyu ci turu Boroom bi.