Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 16:1-14 in Wolof

Help us?

ROOM 16:1-14 in Téereb Injiil

1 Bu nu weesoo loolu, maa ngi leen di dénk sunu jigéen Febe, miy liggéeyal mbooloom ñi gëm ci dëkku Señsere.
2 Nangeen ko jàpp ci turu Boroom bi, ni ko gaayi Yàlla yi yelloo, te dimbali ko ci lépp lu mu aajowoo, ndaxte moom itam wax dëgg, dimbali na ñu bare, ba ci man mii di wax ak yéen.
3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, samay nawle ci liggéeyu Kirist Yeesu.
4 Ñoom ñaar dem nañu, bay bëgga jaay seen bakkan ngir man; maa ngi leen di gërëm ci loolu, du man rekk sax, waaye itam mboolooy ñi gëm ci xeeti àddina sépp.
5 Nuyul-leen ma it ñiy booloo ci seen kër. Maa ngi nuyu it Epaynet, mi jëkka gëm Kirist ci diiwaanu Asi;
6 ak Maryaama, mi sonnoon lool ci yéen.
7 Nuyul-leen ma it Andoronikus ak Yuñas, sama bokk, yi ñu ma booleeloon tëj; am nañu tur ci ndawi Yàlla yi, te ñoo ma jiitu sax ci gëm Kirist.
8 Te fàttewuma Ampilyaatus, mi ma bëgg ci sama xol ngir Boroom bi.
9 Nuyul-leen ma it Urban, sunu nawle ci liggéeyu Kirist, ak sama soppe Estakis;
10 ak it Apeles, mi ngëmam dëggu, ba yelloo kóolute. Nuyul-leen ma it waa kër Aristobul,
11 ak Erojon sama mbokk, ak waa kër Narsis, ñi ci Boroom bi.
12 Maa ngi nuyu Tirifen, moom ak Tirifos, jigéen ñi sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it sama soppe Persidd, mi ci jeex tàkk.
13 Maa ngi nuyu it Rufus, waa ji xolam seey ci Boroom bi, ak yaayam, mi ma féete woon it cérub ndey.
14 Te fàttewuma Asànkirit, Felegon, Ermes, Patarobas, Ermas, ñoom ak mboolem bokk yépp.
ROOM 16 in Téereb Injiil

Room 16:1-14 in Kàddug Yàlla gi

1 Boole naa leen nag ak sunub jigéen Febe, mu di ab taxawukatub mbooloom gëmkat ma dëkke Señsere.
2 Dalal-leen ko ci turu Boroom bi, ni ko ñu sell ñi yelloo, te ngeen jàpple ko ci lépp lu mu aajowoo, nde moom itam xettli na ñu bare, ba ci man mii.
3 Nuyul-leen ma Pirsil ak Akilas, sama bokki liggéeykat ci liggéeyub Almasi Yeesu.
4 Ñoom ñoo jaay seen bakkan ngir ma mucc, te du man doŋŋ maa leen ameel njukkal, waaye mboolooy gëmkat yu jaambur ñi dul Yawut yépp a leen ameel njukkal.
5 Nuyul-leen ma itam mbooloom gëmkat miy daje ca seen kër. Nuyul-leen ma sama soppe Epaynet, miy jooxeb ndoortel meññeef, ma génne ca diiwaanu Asi, ñeel Almasi.
6 Nuyul-leen ma Maryaama, mi sonn lool ci yeen.
7 Nuyul-leen ma Andoronikus ak Yuña, sama bokki Yawut, yi ñu ma tëjandooloon; ñu ñu nawloo lañu ci ndaw yi, te ñoo ma jëkka gëm sax Almasi.
8 Nuyul-leen ma Ampilyaatus, mi ma soppal sama bopp ndax Sang bi.
9 Nuyul-leen ma it Urben, sunu mbokkum liggéeykat ci liggéeyub Almasi, ak Estakis, sama soppe;
10 nuyul-leen ma Apeles mi firndeel kóllëre gi mu am ci Almasi, te ngeen nuyul ma waa kër Aristobul,
11 ak Erojon sama mbokkum Yawut, te ngeen nuyul ma waa kër Narsis ñi gëm Sang bi.
12 Nuyul-leen ma Tirifen ak Tirifos, jigéen ñu sonn ci liggéeyu Boroom bi, ak it ndaw si Persidd mi sonn lool ci liggéeyu Boroom bi.
13 Nuyul-leen ma Rufus, mi Boroom bi taamul boppam, ak yaayam jiy sama yaayu bopp.
14 Nuyul-leen ma Asànkirit ak Felegon ak Ermes ak Patarobas ak Ermas, ak mboolem bokk yi nekk ak ñoom.
Room 16 in Kàddug Yàlla gi