Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 14:4-20 in Wolof

Help us?

ROOM 14:4-20 in Téereb Injiil

4 Koo teg sa bopp, ba di ko teg tooñ? Jaamu jaambur la! Mu taxaw ci liggéeyam, mbaa mu sàggane ko, moom ak sangam la. Waaye dina jub, ndax Boroom bi am na dooley taxawal ko ci njub.
5 Noonu itam am na ñiy tànn bés ak ñiy yemale bés yépp. Na ku nekk xam bu wér li muy def, te jàpp ci.
6 Ndaxte kuy tànn bés, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi. Kiy lekk lu nekk it, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi; loolu leer na ndax day sant Yàlla. Te it ki baña lekk yàpp, mu ngi koy def ngir màggal Boroom bi, di ko sant.
7 Kenn ci nun dundul ngir boppam, kenn deewul it ngir boppam.
8 Danuy dund ngir màggal Boroom bi, dee it ngir màggal ko. Kon nag nuy dund mbaa nu dee, noo ngi ci Boroom bi.
9 Loolu sax moo waral Kirist dee te dundaat, ngir mana nekk Boroomu ñi dee ak ñiy dund.
10 Yaw nag lu tax ngay teg sa moroom tooñ? Lu tax nga koy xeeb? Xanaa nun ñépp, danu dul dajeji fa kanam Yàlla, ngir mu layoo ak nun?
11 Ndaxte Mbind mi tëral na lii: «Boroom bi nee na: “Ni mu wóore ne maa ngi dund, ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal, te ku nekk seede ne maay Yàlla.”»
12 Noonu ku nekk ci nun dinga làyyi fa Yàlla ci lépp loo masa def.
13 Kon nanu bàyyee tegante tooñ, waaye nu fas yéenee moytu lépp lu nekk fiir guy yóbbe sunu moroom bàkkaar.
14 Xam naa ne amul wenn ñam wu sellul, ndax Yeesu Boroom bi xamal na ma loolu. Waaye loo yaakaar ne sellul, ci yaw la sellul.
15 Soo dee lekk luy indil sa moroom tiis, génn nga ci mbëggeel. Yaw nag bul réeral sa moroom ci sa ñam, ndax Kirist dee na ngir moom.
16 Bu sa njariñ jur wax ju ñaaw.
17 Ndaxte bokk ci nguuru Yàlla jotewul dara ak lu nuy lekk mbaa lu nuy naan. Nguuru Yàlla mooy jub ci kanam Yàlla te am mbég ak jàmm ci dooley Xel mu Sell mi.
18 Kiy jaamoo noonu Kirist moo neex Yàlla ak nit ñi.
19 Kon nag nanu wut luy indi jàmm, tey yékkati ngëmu sunu moroom.
20 Bu sa ñam yàq jëfu Yàlla. Bépp ñam sell na ci kanam Yàlla. Ci lu wér! Waaye képp ku lekk luy yàq sa ngëmu moroom, def nga lu bon.
ROOM 14 in Téereb Injiil

Room 14:4-20 in Kàddug Yàlla gi

4 Yaw miy sikkal jaamub jaambur, yaay kan? Su baaxalee mbaa mu bonal, sangam a koy seet! Te day baaxal ndax Boroom bi man na koo baaxal.
5 Naka noonu kii jàpp na ne bés gën naa rafet moroom ma; kee jàpp ne bés yépp a yem. Na ku nekk seet la ko doy, te yem ca.
6 Ndax kiy taamu bés, Boroom bi la koy taamul; naka noonu kiy lekk, Boroom bi la koy gërëme, nde moom lay sant doora lekk; ki lekkul it Boroom bi lay sàkkoo ñàkka lekkam, te Yàlla lay sant.
7 Ndax kat kenn ci nun dundul ngir boppam, te kenn deewul ngir boppam.
8 Su nuy dund, Boroom bi lanuy dundal, su nuy dee it, Boroom bi lanuy deeyal.
9 Loolu sax moo waral Almasi dee, ba noppi dekki, dellu di dund, ngir ñi dee ak ñiy dund ñépp, muy seen boroom.
10 Yaw nag ana looy sikke sa mbokkum gëmkat, ak itam, ana looy xeebe sa mbokkum gëmkat? Ndax kat nun ñépp ay taxawi fa kanam jalub àttekaayu Yàlla.
11 Ndaxte bindees na ne: «Ndegam maay Kiy Dund, Boroom bee ko wax, man la ñépp di sukkal seen bëti óom, te man Yàlla la làmmiñu ñépp di sàbbaal.»
12 Kon ku nekk ci nun, yaay layool sa bopp fa Yàlla.
13 Kon nag bunu di seetati lu nu sikkantee, li ngeen di seet kay mooy nu ngeen fexee ba dungeen yóbbe mbokkum gëmkat lu koy fakktal, mbaa lu koy daane ci bàkkaar.
14 Xam naa nag, wér na ma it te Sang Yeesu tax, ne amul lenn lu sobewu ci wàllu boppam, ba daganula lekk; waaye ki jàppe lenn muy lu sobewu, ci moom la loola di lu sobewu.
15 Soo dee lekk lenn ba tax sa mbokk am ci lu ko naqari, noppi ngaa doxe cofeel. Bu sag lekk sànk ku Almasi deeyal.
16 Li dagan ci yaw, bu ko jariñoo ba may kenn lu mu ŋàññee.
17 Ndax kat solob nguurug Yàlla jotewul dara akug lekk mbaa ag naan, waaye solob nguuru Yàlla moo di njub ak jàmm, ak mbégte ci ndimbalal Noo gu Sell gi.
18 Noonu kat ku koy jaamoo Almasi, yaa neex Yàlla, am ngërëmal nit ñi.
19 Kon nag nanu sàkku luy indi jàmm, ak lu nu feddalantee.
20 Aw ñam, bumu la yàqloo liggéeyu Yàlla. Dëgg la, wépp ñam set na, waaye lekk ga nga koy lekk, su gàkkalee ngëmu keneen, def nga lu aay.
Room 14 in Kàddug Yàlla gi