Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 13:8-11 in Wolof

Help us?

ROOM 13:8-11 in Téereb Injiil

8 Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa.
9 Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu mana doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
10 Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
11 Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yewwu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm.
ROOM 13 in Téereb Injiil

Room 13:8-11 in Kàddug Yàlla gi

8 Buleen ameel kenn bor, lu moy borub soppante; ndax ku sopp sa moroom, yaa matal yoonu Musaa.
9 Ndax ndigal yii kat: «Buleen jaaloo, buleen bóom, buleen sàcc, buleen xemmem,» ak leneen ndigal lu mu mana doon, ci genn kàddu gii la tënke: «Ni ngeen soppe seen bopp, nangeen ko soppe seen moroom.»
10 Cofeel du waral kenn def moroomam lu bon; kon cofeel moo matal sëkk yoonu Musaa.
11 Li tax ngeen wara gëna farlu ci loolu mooy, xam ngeen jant yi nu tollu; seen waxtuw yewwu jot na ba noppi, nde léegi la nu mucc gëna jege ba nuy doora gëm.
Room 13 in Kàddug Yàlla gi