Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 12:1-13 in Wolof

Help us?

ROOM 12:1-13 in Téereb Injiil

1 Kon nag bokk yi, gannaaw yërmandey Yàlla baree na noonu, maa ngi leen di ñaan, ngeen jébbal ko seen yaram wépp. Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.
2 Bu leen àddina jay, waaye yeesluleen ci seen xel, ba soppiku, ngeen mana xam bu wér coobarey Yàlla, di lépp lu baax, neex ko te mat sëkk.
3 Gannaaw Yàlla may na ma ciw yiwam, ma nekk ndawam, maa ngi leen di wax lii, kenn ku nekk ci yéen: buleen yég seen bopp, waaye ngeen am xalaat yu yem, méngook ngëm gi leen Yàlla sédd, ku nekk ak wàllam.
4 Loolu, ci maanaa, mi ngi mel ni yaramu nit: yaram, lu cér yi baree bare, benn niroowul ak moroomam liggéey.
5 Noonu itam nun ñi bokk ci Kirist, lu nu baree bare, benn lanu te danoo mànkoo.
6 Kon gannaaw Yàlla séddale na ay mayam, ku nekk ak sa cér, nanu koy jëfandikoo. Ku Yàlla may, ngay waare kàddoom, nga wax ko kem sa ngëm;
7 kuy topptoo yëfi mbooloo mi, nga takku ci; ku Yàlla may, ngay jàngle, nekk ci;
8 kuy feddali ngëmu nit ñi ci Yàlla, nga sax ci; kuy séddoo alalam ak nit ñi, nga def ko ak xol bu laab; kuy jiite mbooloo mi, nga sawar ci; kuy dimbali ñi néew doole, nanga ci bég.
9 Na seen cofeel di lu dëggu te baña nekk ngistal; araamal-leen lu bon te sax ci lu baax.
10 Bëgganteleen ak xol bu leer, niy doomi ndey, te farlu ci teralante.
11 Sawarleen te baña tayel, di jaamu Boroom bi ak seen xol bépp.
12 Bégleen ci yaakaaru ëllëg te muñ bépp tiis, di sax ci ñaan Yàlla.
13 Dimbalileen gaayi Yàlla yi ci seeni soxla, te saxoo dalal gan.
ROOM 12 in Téereb Injiil

Room 12:1-13 in Kàddug Yàlla gi

1 Kon nag bokk yi, ma ñaax leen, te yërmandey Yàlla tax, ngir ngeen jébbal ko seen yaram wépp, def ko jooxe buy dund, sell te neex Yàlla. Loolu déy mooy njaamu, gi leen war.
2 Buleen roy jamonoy tey jii, waaye yeesluleen ci ni ngeen di xalaate ba soppiku, ngir ngeen mana ràññee liy coobarey Yàlla, muy li baax, di bànneexam te mat sëkk.
3 Ma àrtu leen ci kaw yiw wi ma Yàlla may; bu kenn ci yeen teg boppam fu mu àggul, waaye xalaate leen sago, te ku nekk dëppoo ak céru ngëm bi ko Yàlla sédd.
4 Ndax kat dafa mel ni sunu yaram wiy wenn, te cér yi bare, doonte cér yépp a wuuteek seen moroom nu ñuy liggéeye.
5 Noonu lanu doone ñu bare, bokk wenn yaram nun ñépp ci Almasi mi nu gëm, te ku nekk di sa cérub moroom.
6 Ay may yu wuute lanu am, may yu yemook céru yiw bi ñu sédd ku nekk ci nun. Su dee biral kàddug waxyu mooy sag may, biraleel kàddug waxyu sa kemu ngëm;
7 su dee wàllu jàpple, deel jàpple; su dee wàllu njàngle, ngay jàngle;
8 Su dee wàllu kàddu yuy yokke, ngay wax luy yokk gëmkat ñi; su dee wàllu joxe, deel joxe te Yàlla rekk tax; su dee wàllu jiite, taxawal temm ci liggéeyub jiite; su dee wàllu baaxe nit ñi, nay loo bége.
9 Na seen cofeel mucc ci ngistal, seexluleen lu bon te ŋoy ci lu baax.
10 Na leen mbëggeelug bokk taxa fonkante, te ngeen farlu ci di terlante.
11 Sawarleen te baña yoqi, jaamuleen Boroom bi, ànd ceek pastéefu xol.
12 Bégeleen seen yaakaar, di muñ ci biir tiis, tey saxoo ag ñaan.
13 Deeleen def seen loxo ci lu faj soxlay gëmkat ñu sell ñi, te boole ci am teraanga.
Room 12 in Kàddug Yàlla gi