Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 11:3-34 in Wolof

Help us?

ROOM 11:3-34 in Téereb Injiil

3 «Boroom bi, rey nañu say yonent, daaneel say bérab yu sell, ba man kenn maa ci des, te ñu ngi may wuta rey.»
4 Waaye Yàlla da ko ne: «Dencal naa sama bopp juróom ñaari junniy nit ñu jaamuwul Baal.»
5 Noonu itam ci jamono ji nu nekk, des na nit ñu néew ñu Yàlla dencal boppam ciw yiwam.
6 Gannaaw nag yiwu Yàlla rekk a tax mu denc leen, kon du seen peyug ñaq, walla boog yiwu Yàlla dootul yiw.
7 Kon lu nu ci wara wax? Li bànni Israyil doon wut, gisuñu ko. Waaye ñi Yàlla tànn rekk a ko gis, te ña ca des baña gëm, ba seen xol dërkiis.
8 Looloo tax Mbind mi ne: «Yàlla daf leena jox xelum nit ku gëmméentu, bët yu gëlëm ak nopp yu tëx, ba ci bésub tey.»
9 Te Daawuda it daf ci wax naan: «Na seeni ñam sax nekk fiir ak i pakk; nañu ci daanu, te Yàlla mbugal leen.
10 Nañu gumba ba ne fatuus, nañu tiis te sëgg ba fàww.»
11 Ndax kon dañoo tarxiis, daanu ba fàww? Mukk! Waaye jéllub Israyil dafa ubbi bunt, ngir xeeti ñi dul Yawut mana mucc, te bànni Israyil siis leen.
12 Gannaaw seen tooñ nag moo ubbi buntu yiw ci waa àddina si, te seen ñàkk moo meññ barkeb xeet yépp, céy bés bu Israyil gépp delloo ci Yàlla, ndaw barke bu bare!
13 Yéen ñi dul Yawut, yéen laay waxal. Ndegam Yàlla daf maa def ndawam, yónni ma ci yéen xeeti àddina si, damay matal samab yónnent.
14 Dama koy def, ngir ñi bokk ak man xeet siis, ba ñenn ñi mucc.
15 Ndaxte bi Yàlla génnee Israyil, ubbee na noonu bunt, ngir xeeti àddina juboo ak moom; kon su Yàlla dugalaatee Israyil, ndax du mel ni ndekkitel néew ya?
16 Damay wax ne, mburu mépp sell na, bu ci Yàlla amee wàll. Naka noonu garab gi Yàlla séddoo reen bi, garab gépp sell na.
17 Bànni Israyil a ngi mel ni garabu oliw gu ñu jëmbët ci kër gi, waaye mu am car yu ci fàq. Yaw mi dul Yawut, yaa ngi mel ni caru garabu oliw gu àll bu ñu jabtal ci garabu kër googu. Noonu nga jariñoo meen, mi jóge ci reen bi.
18 Kon nag bul bàkku, di xeeb car yooyu Yàlla fàq. Waaye soo bëggee bàkku, xamal ne reen moo lay yenu, te du yaw miy car yaa koy yenu.
19 Xanaa dinga wax ne: «Car yooyu dañu leena fàq, ngir jabtal ma fa ñu nekkoon.»
20 Dëgg la; waaye seen ngëmadee tax ñu fàq leen, wuutal la fa ndax sa ngëm. Bumu tax nag ngay bàkku, waaye nanga moytu.
21 Gannaaw Yàlla baalul car ya cosaanoo ca garab ga, kon boog yéen itam man na leena fàq.
22 Loolu kon wone na ni Yàlla baaxe ak ni muy meree tooñ. Ci ñi daanu, Yàlla wone na ni meram tànge, wone mbaaxam ci yéen, su fekkee yéena ngi ci wéy; lu ko moy, dees na leen fàq yéen itam.
23 Te car yooyu fàq, su ñu wéyul ci seen ngëmadi, dees na leen delloo ci garab gi, ndax Yàlla man na leen cee tafaat.
24 Yaw mi dul Yawut, yaa ngi bokkoon ci garabu oliw gu àll, waaye Yàlla daf la cee jële, ci lu dul farala am, jabtal la ci garabu kër gi. Kon man nanoo gëna wóor ne, Yawut ya judduwaale nekk ci garabu oliw gu kër gi, Yàlla dina leen ci delloo.
25 Bokk yi, dama leena bëgga dindi kumpa ci lii, ngir ngeen baña yég seen bopp. Dërkiisu xol dab na bànni Israyil ab diir, ba bés ba mboolem waa àddina, ñu wara bokk ci nguuru Yàlla, dugg ca.
26 Bu loolu amee nag, bànni Israyil gépp dina mucc. Moom la Mbind mi tëral, bi mu naan: «Ab xettalikat dina jóge ci Siyoŋ, dàq weddi ci askanu Yanqóoba.
27 Loolu mooy kóllëre, gi may fas ak ñoom, bés bu may dindi seeni bàkkaar.»
28 Gannaaw bañ nañu xibaaru jàmm bi, ay bañaaley Yàlla lañu, ngir ngeen jot barkeem. Waaye gannaaw Yàlla tànn na leen, dafa leen bëgg ba tey ndax seen maam ya.
29 Ndax li Yàlla maye, dootu ko nangu mukk, te ku mu woo ci boppam, dootu la dàq mukk.
30 Ñu déggadil Yàlla ngeen woon, waaye ngëmadig Yawut yi tax na, ngeen jot yërmandeem.
31 Ñoom itam lànk nañu léegi, ngir mana bokk ak yéen yërmandey Yàlla.
32 Kon Yàlla tëj na ñépp ci ngëmadi, ngir mana yërëm ñépp.
33 Xelum Yàlla ni mu xóote, ak xam-xamam ni mu baree, ba raw xelum nit! Kan moo muus, ba xam dogalam? Walla nga am xel, ba nànd ay jëfam?
34 Mbind mi dafa ne: «Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ku ko doon digal?»
ROOM 11 in Téereb Injiil

Room 11:3-34 in Kàddug Yàlla gi

3 «Boroom bi, say yonent, rey nañu leen; say sarxalukaay, màbb nañu leen; man doŋŋ maa fi des, te ñu ngi wut sama bakkan.»
4 Ana lu ko Yàlla tontu? Da ne: «Beral naa sama bopp juróom ñaari junniy (7 000) nit ñu sujjóotaluloon Baal tuur mi.»
5 Kon nag naka noonu itam ci jamonoy tey jii, aw ndes a ngi fi, te ci kaw yiw lees leen taamoo.
6 Gannaaw aw yiw a tax nag, dootu seen peyu jëf, lu ko moy aw yiw noppee doon aw yiw.
7 Kon léegi nag? Li am moo di li bànni Israyil doon wut, amuñu ko. Ñi ñu taamu ñoo ko am, ña ca des, seenum xel a dërkiis.
8 Noonu lees binde ne: «Yàlla moo leen jox xelum ngëmment, ak bët yu dul gis, ak nopp yu dul dégg, ba bésub tey jii.»
9 Daawuda it wax na ne: «Yal na seen ndab di seenum yeer, boole ci dib caax, te di fiir gu ñuy daanu, muy seenub yool.
10 Yal na seeni gët giim, ba duñu gisati, yal nañu sëgg ba fàww.»
11 Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.
12 Gannaaw tooñug bànni Israyil mooy xéewalu àddina si, seenug néewle di xéewalu jaambur ñi dul Yawut, kon bu bànni Israyil yembee, ndaw xéewal gu gënatee baawaan!
13 Léegi nag yeen jaambur ñi dul Yawut laay waxal. Gannaaw maay ndaw li ñu yebal ci jaambur ñi dul Yawut, samab yónnent laay teral.
14 Jombul sama liggéey dina yee fiiraangey sama bokki Yawut ñi, ba ñenn ci ñoom mucc.
15 Ndax kat ba Yàlla dàqee Israyil, ca la àddina juboo ak Yàlla. Kon nag bu leen Yàlla délloosee, ana lu muy jur lu moy ndee-ndekki?
16 Ndax kat ab jooxe bu génnee ci tooyalub sunguf, di ndoortel meññeef, su boobu jooxe sellee, tooyalub sunguf bépp ay sell. Ndax su reenu garab sellee, car ya it sell.
17 Waaye su ñu tenqee lenn ci cari oliwu kër, te yaw ngay caru oliwu àll, ñu indi la, jabtal ci oliwu kër gi, nga wuutu car ya ca fàqe, ba mana xéewloo meen miy wale ci reenu oliwu kër gi, di ko dundal,
18 bumu tax nga bàkku ci kaw car ya fàqe. Soo dee bàkku, xamal ne du yaa yenu reen bi, waaye reen bee la yenu.
19 Xam naa dinga ne: «Car yooyu, dees leena tenqi, ngir jabtal ma.»
20 Dëgg it; waaye ngëmadi moo leen fa tenqee, te yaw, ngëm a la fa teg. Bu ko réy-réyloo, waaye ragalal.
21 Ndegam cari judduwaale ya la Yàlla déegul, moytul mu bañ laa déeg yaw itam.
22 Xoolal kon ni Yàlla baaxe, ak ni mu ragloo; ci ñi déggadi la raglu, baax ci yaw, ndegam cig mbaaxam nga sax; lu ko moy dees na la tenqi yaw itam.
23 Car ya fàqe woon itam, su ñu wéyewul ngëmadi, dees leen di delloo ca ndey ja, nde Yàlla man na leen caa saxalaat.
24 Ndax kat, ndegam yaw lañu tenqee ci oliwu àll gi, jabtal la ci oliwu kër gi dul sa ndey, astamaak car yi oliwu kër gi di seen ndey, nde saxalaat leen ca mooy gëna yombati.
25 Bokk yi, moytuleena defe ne seen xel mu rafet a leen may li ngeen am. Bugguma ngeen umple mii mbóot: Ag déggadi moo dikkal lennati bànni Israyil, ba kera xeet yi dul Yawut duggsi, ba seenub lim mat.
26 Su boobaa nag, bànni Israyil gépp ay mucc, noonee ko Mbind mi indee ne: «Siyoŋ la wallukat bay jóge, mooy tenqee ngëmadi ci askanu Yanqóoba.
27 Loolooy doon sama kóllëreek ñoom, kera ba may far seeni bàkkaar.»
28 Ci wàllu xibaaru jàmm bi, ay noon la Yawut ñi taxawe, te muy xéewal ci yeen ñi dul Yawut. Waaye ci wàllu dogal bi taamu Yawut ñi, ay soppe lañu, te seeni maam tax.
29 Ndax Yàlla kat, ay mayam akub wooteem, lenn du ci toxu.
30 Yeena déggadi woon, waaye tey daj ngeen yërmande, ndax déggadig Yawut yi.
31 Noonu itam la Yawut yi déggadee tey, ba ni ngeen daje yërmande, ñoom it ñu daje ni yërmande.
32 Yàlla moo tëj nit ñépp ci seenug déggadi, ngir yërëm leen ñoom ñépp.
33 Céy xóotaayub koomu Yàlla ak xel ma, ak xam-xam ba! Deesul natt ay dogalam, deesul ràññee ay jëfinam!
34 «Ana ku xam xalaatu Boroom bi? Ana ku ko digal?»
Room 11 in Kàddug Yàlla gi