Text copied!
Bibles in Wolof

ROOM 10:7-11 in Wolof

Help us?

ROOM 10:7-11 in Téereb Injiil

7 «Bul wax it: “Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
8 Kon boog lan lay wax? Lii: «Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet, ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
9 Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
10 Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
11 Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
ROOM 10 in Téereb Injiil

Room 10:7-11 in Kàddug Yàlla gi

7 «Bul ne it: “Ana kuy wàcci njaniiw?”» nde loolu mooy Almasi dekkiwaat ngay sàkku.
8 Li mu wax moo di: «Kàddu gaa ngi ci sa wet; mu ngi ci saw làmmiñ ak ci sa xol.» Te loolu mooy kàddug ngëm gii nuy xamle.
9 Saw làmmiñ, soo ci biralee ne Yeesu moo di Boroom bi, sab xol it, nga gëm ci ne Yàlla dekkal na Sang Yeesu, dinga mucc.
10 Ndax kat ab xol lees di gëme, ba am àtteb ku jub, te aw làmmiñ lees di birale ngëm gi ba mucc.
11 Mbind mi moo ne: «Képp ku ko gëm, doo rus.»
Room 10 in Kàddug Yàlla gi