7 Sa lex yiy tàkk ni ŋaali gërënaat, làqoo sa muuraay bi.
8 Buur day am juróom benn fukki lingeer ak juróom ñett fukki jongama ak jeeg ju dul jeex.
9 Waaye sama nenne kenn la, matal ma sëkk, yaayam kennal ko, muy ngëneelu biiru yaayam. Janq ji gis ko, di ko jëwe mbégteem, lingeeri buur aki jongamaam di ko kañ.