7 Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma; ñu dóor ma, gaañ ma, ñori sama malaan. Wattukati tata jaa!
8 Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne su ngeen gisee sama nijaay, ne ko damaa wopp ndax mbëggeel.
9 Yaw mi dàq ci jigéen ñi, ana lu sa nijaay gëne keneen? Ana lu mu ëpplee keneen, ba nga di nu waatloo lii?
10 Sama nijaay daa xees, leer; kenn la ci fukki junniy góor.
11 Kanam gi ni wurus, di wurusu ngalam; njañ li lëmësu, ñuul ni ndobin.
12 Gët yi ni pitax yu feggook wali ndox, sangoo meew, feggook ndox mu ne xéew.
13 Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
14 Yoxo yi banti wurus la, ngën-gi-per tappe ca; jëmm ja rattax ni bëñu ñay laloo peri safiir;
15 yeel yi kenuy doj wu jafe la, sampe ci tànki wurusu ngalam. Meloom ni tundi Libaŋ, di tànnéef ni garabi seedar.
16 Gémmiñam, bànneexi neen, jëmmam jépp jara xédd! Yeen janqi Yerusalem, sama nijaay a ngoog, samab xarit.