Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 5:2-8 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 5:2-8 in Kàddug Yàlla gi

2 Maa ngi nelaw, te xol yewwu; dégluleen, sama nijaay ay fëgg. Mu ne: «Xaritoo, jigéen sama, ubbil ma, sama nenne, alal sama! Sama bopp a ngi laye ba tooy, njañ li fanaanee guus.»
3 Ma ne ko: «Summiku naa de, xanaa duma soluwaat? Jàngu naa jeeg, xanaa duma taqati?»
4 Sama nijaay yoor loxoom ci xarante bi, sama yaram ne sàyy.
5 Ma ne bërét, di ubbil nijaay, sama yoxo yi, diwu ndàbb di ca siit, sama waaraam yi, ndàbb rogalaat ba ci njàppul bunt bi.
6 Maa ubbil nijaay, waaye nijaay waññiku na, ba wéy. Ba mu waññikoo, tuuti ma dee. Seet naa ko, gisuma ko; ma woo ko, wuyuwul.
7 Wattukat yiy wër dëkk bi gis ma; ñu dóor ma, gaañ ma, ñori sama malaan. Wattukati tata jaa!
8 Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ne su ngeen gisee sama nijaay, ne ko damaa wopp ndax mbëggeel.
Ngën-gi-woy 5 in Kàddug Yàlla gi