Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 5:13-16 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 5:13-16 in Kàddug Yàlla gi

13 Lex ya di tool, gàncax ga ne ca bann, tuñ ya diy tóor-tóor, ndàbb wale ca, rogalaat.
14 Yoxo yi banti wurus la, ngën-gi-per tappe ca; jëmm ja rattax ni bëñu ñay laloo peri safiir;
15 yeel yi kenuy doj wu jafe la, sampe ci tànki wurusu ngalam. Meloom ni tundi Libaŋ, di tànnéef ni garabi seedar.
16 Gémmiñam, bànneexi neen, jëmmam jépp jara xédd! Yeen janqi Yerusalem, sama nijaay a ngoog, samab xarit.
Ngën-gi-woy 5 in Kàddug Yàlla gi