7 Laltub Suleymaan a ngoog, juróom benn fukki jàmbaar dar ko, di jàmbaari Israyil.
8 Ñépp mane saamar, ku ci nekk mokkal xare, saamar ci pooj, ngay fàggu mbettum guddi.
9 Ab toogu la Buur Suleymaan defarlu, ñu defare ko bantu Libaŋ,
10 ponku ya, mu def ko xaalis, wéeruwaay ba wurus; tooguwaay ba di ndimo lu xonq curr, biir ba di liggéeyu ràbb bu janqi Yerusalem ràbbe cofeel.
11 Yeen janqi Siyoŋ, génnleen, xool Buur Suleymaan ak mbaxanam céetal mi ko yaayam solal ci bésub céetalam, bésu bànneexam.