Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 3:3-8 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 3:3-8 in Kàddug Yàlla gi

3 Wattukat yee ma gis, ba ñuy wër dëkk bi. Ma ne leen: «Sama soppey xol, gisuleen ko?»
4 Ma romb leen tuuti rekk, gis sama soppey xol. Ma ne ko taral, bàyyeetuma ko, ba yóbbu ko sama kër yaay, ba sama biir néegu ndey ji ma jur.
5 Ngalla yeen, janqi Yerusalem, waatal-leen ma ci taaru kéwél ak koobay àll bi, ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel te jotul.
6 Ana luy jóge màndiŋ ma nii, mel ni taxaaru saxar, suuroo ndàbb ak xas mu xeeñ ak mboolem cuuraayi jula?
7 Laltub Suleymaan a ngoog, juróom benn fukki jàmbaar dar ko, di jàmbaari Israyil.
8 Ñépp mane saamar, ku ci nekk mokkal xare, saamar ci pooj, ngay fàggu mbettum guddi.
Ngën-gi-woy 3 in Kàddug Yàlla gi