8 Aa! Xamoo koo? Yaw mi dàq ci jigéen ñi! Génnal rekk, topp wewi jur gi, sàmmi say tef, fi dendeek mbaari sàmm si.
9 Xarit, xam nga lu ma lay xoole? Yànjaayu wajan wu takk watiiru Firawna.
10 Sa lex yaa ngi tàkk fi digg sàdd yi! Céy wii loos ak caqu peram!
11 Sàddi wurus lanu lay defaral, tapp ca xaalis.