Text copied!
Bibles in Wolof

Ngën-gi-woy 1:7-12 in Wolof

Help us?

Ngën-gi-woy 1:7-12 in Kàddug Yàlla gi

7 Sama soppey xol, ngalla wax ma ana fooy foral, di fa gooral, digg bëccëg? Lu ko moy may muuru, di la wër fi say xarit ak seeni gétt.
8 Aa! Xamoo koo? Yaw mi dàq ci jigéen ñi! Génnal rekk, topp wewi jur gi, sàmmi say tef, fi dendeek mbaari sàmm si.
9 Xarit, xam nga lu ma lay xoole? Yànjaayu wajan wu takk watiiru Firawna.
10 Sa lex yaa ngi tàkk fi digg sàdd yi! Céy wii loos ak caqu peram!
11 Sàddi wurus lanu lay defaral, tapp ca xaalis.
12 Li sama buur tëdd, di xéewlu lépp, maa ngi gilli lu neex.
Ngën-gi-woy 1 in Kàddug Yàlla gi