6Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp.
7Noonu niir muur leen, te baat jibe ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.»
8Ci saa si taalibe yi xool, waaye gisatuñu kenn ku dul Yeesu rekk.
9Bi loolu amee ñu wàcc ca tund wa. Bi muy wàcc nag, Yeesu sant leen ne: «Buleen nettali kenn li ngeen gis, ba kera Doomu nit ki dekki na.»
10Ñu téye wax jooju ci seen biir, di sotteente xel, ba xam lu ndekkite looluy tekki.