35 Noonu Yeesu toog, woo fukki taalibe ya ak ñaar ne leen: «Ku bëgga jiitu, na topp ci gannaaw ñépp te nekk surgab ñépp.»
36 Bi ko Yeesu waxee, mu jël xale, indi ko ci biir géew bi, ba noppi leewu ko naan:
37 «Ku nangu xale bu mel ni bii ci sama tur, man mii nga nangu; te ku ma nangu, du man mii sax nga nangu waaye ki ma yónni.»
38 Bi loolu amee Yowaana ne ko: «Kilifa gi, danoo gis nit kuy dàq ay rab ci sa tur, nu tere ko ko, ndax li mu bokkul ci nun.»
39 Waaye Yeesu ne ko: «Buleen ko tere, ndaxte kenn manula def kéemaan ci sama tur, ba noppi di ma xarab.
40 Ku nu sotul, far na ak nun.
41 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na leen kaasu ndox rekk, ndax yéena ngi bokk ci man Kirist, kooku du ñàkk yoolam mukk.
42 «Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom, moo di ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ci géej.
43 Boo xamee ne sa loxo mu ngi lay yóbbe bàkkaar, dagg ko. Ndaxte ñàkk loxo te tàbbi ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari loxo te tàbbi ci sawara su dul fey mukk.