5 Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
6 Noonu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. Mu jël juróom ñaari mburu yi, sant Yàlla, damm leen, jox leen taalibe yi, ngir ñu séddale leen mbooloo mi; taalibe yi def ko.
7 Amoon na fa it tuuti jën yu ndaw. Yeesu jël ko, sant Yàlla, wax taalibe yi, ñu séddale leen itam mbooloo mi.
8 Noonu nit ñi lekk ba suur, ba noppi taalibe yi dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des.
9 Ña ko fekke nag matoon nañu ñeenti junniy góor.
10 Bi ko Yeesu defee, mu yiwi leen, daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga, dem ca wàlli Dalmanuta.