Text copied!
Bibles in Wolof

MÀRK 7:24-27 in Wolof

Help us?

MÀRK 7:24-27 in Téereb Injiil

24 Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe.
25 Amoon na fa nag jigéen ju rab jàpp doomam ju jigéen. Bi mu déggee ne, Yeesoo nga fa, mu ñëw, daanu ciy tànkam,
26 fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam.
27 Waaye Yeesu ne ko: «Na gone yi jëkka lekk, ba regg; fab ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
MÀRK 7 in Téereb Injiil