22Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.»
23Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.»
24Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu ne ko: «Laajal boppu Yaxya.»
25Mu daldi gaawantu dugg nag ci kanam buur bi ne ko: «Damaa bëgg, nga indil ma léegi boppu Yaxya ci biir ndab.»
26Bi ko buur ba déggee, mu am naqar wu réy. Waaye bëggu koo gàntu ndax ngiñ li ak gan ñi.
27Mu daldi yónni nag xarekat, jox ko ndigal, mu indil ko boppu Yaxya. Waa ji dem, dagg boppu Yaxya ca kaso ba,
28indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq bi, mu daldi ko jox yaayam.
29Ba taalibey Yaxya déggee loolu, ñu ñëw, fab néew ba, suul ko ci bàmmeel.
30Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li ñu def ak li ñu jàngle lépp.
31Ci kaw loolu Yeesu ne leen: «Nanu beddeeku, dem ci bérab bu wéet; ngeen noppalu fa tuuti.» Waxoon na loolu, ndaxte amoon na ñu bare ñu doon dem ak a dikk, ba amuñu sax jot ngir lekk.
32Noonu ñu dugg cig gaal, dem ca bérab bu wéet.
33Bi ñuy dem nag, am ñu leen gis, xàmmi leen, ñu daldi jóge ci dëkk yépp, daw, jiitu leen fa.
34Bi Yeesu génnee gaal gi, mu gis mbooloo mu réy, yërëm leen, ndaxte dañoo mel ni xar yu amul sàmm. Kon mu daldi leen jàngal lu bare.
35Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi.
36Yiwil mbooloo mi nag, ñu dugg ci àll bi ak dëkk yi nu wër, jënd lu ñu lekk.»
37Waaye Yeesu ne leen: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?»