32 waaye boo ko jiyee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.»
33 Noonu Yeesu dégtal leen yeneen léeb yu bare yu mel ni yii, di leen xamal kàddu gi, aju ci lu ñu àttan.
34 Daawu leen wax dara lu dul ciy léeb. Waaye bu wéetee ak ay taalibe, daan na leen firil lépp.
35 Bés booba nag ci ngoon Yeesu ne taalibe yi: «Nanu jàll dex gi.»
36 Mu yiwi mbooloo mi nag, ay taalibeem jël ko ni mu mel ci gaal gi; te yeneen gaal ànd ak moom.
37 Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg, duus yi sàng gaal gi, ba mu bëgga fees.
38 Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
39 Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm.
40 Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»