Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 26:4-25 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 26:4-25 in Kàddug Yàlla gi

4 ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israyil, ña génne woon Misra:
5 Ruben moo doon taawub Israyil. Ñi askanoo ci Ruben ñoo di Anog mi sos làngu Anogeen ñi, ak ñoom Palu mi sos làngu Paluween ñi,
6 ak ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Karmi mi sos làngu Karmeen ñi.
7 Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730).
8 Palu moo meññ Elyab,
9 Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
10 ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo.
11 Doomi Kore ya nag deewuñu ca.
12 Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi,
13 ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi.
14 Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200).
15 Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi,
16 ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi,
17 ak ñoom Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom Areli mi sos làngu Areleen ñi.
18 Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500).
19 Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ña ca réewum Kanaan lañu faatoo.
20 Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi.
21 Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi.
22 Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500).
23 Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom Puwa mi sos làngu Puween ñi,
24 ak ñoom Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom Simron mi sos làngu Simroneen ñi.
25 Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300).
Màndiŋ ma 26 in Kàddug Yàlla gi