Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 26:14-26 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 26:14-26 in Kàddug Yàlla gi

14 Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200).
15 Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi,
16 ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi,
17 ak ñoom Arodd mi sos làngu Aroddeen ñi, ak ñoom Areli mi sos làngu Areleen ñi.
18 Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500).
19 Am na nag doomi Yuda yu ñuy wax Er ak Onan. Waaye Er ak Onan ña ca réewum Kanaan lañu faatoo.
20 Ñi askanoo ci Yuda, ñook seeni làng ñoo di ñoom Sela mi sos làngu Celaneen ñi, ak ñoom Peres mi sos làngu Pereseen ñi, ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi.
21 Ñi askanoo ci Peres ñoo di ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Amul mi sos làngu Amuleen ñi.
22 Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500).
23 Ñi askanoo ci Isaakar, ñook seeni làng ñoo di Tola mi sos làngu Toleen ñi, ak ñoom Puwa mi sos làngu Puween ñi,
24 ak ñoom Yasub mi sos làngu Yasubeen ñi, ak ñoom Simron mi sos làngu Simroneen ñi.
25 Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300).
26 Ñi askanoo ci Sabulon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Seredd mi sos làngu Sereddeen ñi, ak ñoom Elon mi sos làngu Eloneen ñi, ak ñoom Yaleel, mi sos làngu Yaleleen ñi.
Màndiŋ ma 26 in Kàddug Yàlla gi