12 Ñi askanoo ci Simeyon, ñook seeni làng ñoo di ñoom Nemwel mi sos làngu Nemweleen ñi, ak ñoom Yamin mi sos làngu Yamineen ñi, ak ñoom Yakin mi sos làngu Yakineen ñi,
13 ak ñoom Sera mi sos làngu Cerayeen ñi, ak ñoom Sawul mi sos làngu Cawuleen ñi.
14 Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200).
15 Ñi askanoo ci Gàdd, ñook seeni làng ñoo di ñoom Cefon mi sos làngu Cefoneen ñi, ak ñoom Agi mi sos làngu Ageen ñi, ak ñoom Suni mi sos làngu Cuneen ñi,
16 ak ñoom Osni mi sos làngu Osneen ñi, ak ñoom Eri mi sos làngu Ereen ñi,