Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 26:1-10 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 26:1-10 in Kàddug Yàlla gi

1 Aji Sax ji dafa wax Musaa, ak Elasar doomu Aaróona sarxalkat ba, ne leen:
2 «Waññleen mbooloom bànni Israyil gépp, ngeen lim turi góor ñépp, na ñu bokke seen këri maam, dale ko ci ñi am ñaar fukki at, jëm kaw, mboolem ñi xare war ci bànni Israyil.»
3 Musaa ak Elasar sarxalkat ba wax ak ñoom ca joori Mowab, fa janook Yeriko ca wetu dexu Yurdan; ñu ne leen
4 ñi dale ci ñaar fukki at, jëm kaw lees di lim, na ko Aji Sax ji sante Musaa. Lii moo di limeefu nit ña soqikoo ci bànni Israyil, ña génne woon Misra:
5 Ruben moo doon taawub Israyil. Ñi askanoo ci Ruben ñoo di Anog mi sos làngu Anogeen ñi, ak ñoom Palu mi sos làngu Paluween ñi,
6 ak ñoom Esron mi sos làngu Esroneen ñi, ak ñoom Karmi mi sos làngu Karmeen ñi.
7 Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730).
8 Palu moo meññ Elyab,
9 Elyab meññ Nemwel ak Datan ak Abiram. Datan ak Abiram ñooñii doonooni njiit ca mbooloo ma, ñoo doon diiŋat Musaa ak Aaróona. Ña nga bokkoon ca gàngooru Kore, ba ñuy diiŋat Aji Sax ji,
10 ba suuf sa xar, boole leen ak Kore, wonn, keroog ba gàngoor ga sànkoo, te sawara wa lakk ñaar téeméeri nit ak juróom fukk, ñu daldi doon firnde luy artoo.
Màndiŋ ma 26 in Kàddug Yàlla gi