14 Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»
15 Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,
16 kàddug kiy dégg waxi Yàlla, kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
17 Maa ngi koy gis, te du tey, Maa ngi koy niir, te jubseegul; biddiiw a feqe fa Yanqóoba, yetu nguur a yékkatikoo fa Israyil, daldi toj boppi Mowab, toj kaaŋi mboolem askanu Set.
18 Edom, mu moom; Seyir, noonam, muy boroom; Israyil def jaloore.
19 Fa Yanqóoba la buur di bawoo, dem ñéddi ndesu dëkk ba.»
20 Ci kaw loolu Balaam geesu réewum Amaleg, dellu yékki kàddug ñaanam, ne: «Amaleg moo sutu xeet, te sànku lay mujje.»
21 Mu teg ca geesu réewum Keneen ña, yékkeeti kàddug ñaanam, ne: «Keneen ñee wér ab dëkkuwaay, seenub tàgg a làqoo biir doj.