10 Ba loolu amee Balag sànju ci kaw Balaam, daldi fenqey loxoom. Ci kaw loolu Balag ne Balaam: «Móolu samay noon laa la wooye woon, yaw defoo lu moy ñaanal leena ñaanal, ba muy ñetti yoon nii!
11 Léegi nag, laggal ñibbi. Noon naa la dinaa la teral bu baax, waaye mu ngoog, Aji Sax jee la xañ teraanga.»
12 Balaam ne Balag: «Xanaa du sa ndaw yi nga yebaloon ci man sax, waxoon naa leen ne leen,
13 su ma Balag joxoon këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def ci sama coobarey bopp, lenn lu baax mbaa lu bon, lu tebbi ndigalu Yàlla Aji Sax ji? Li Aji Sax ji wax rekk, moom laay wax.
14 Léegi nag maa ngi dellu ca saay bokk, waaye kaay, ma xamal la li xeet wii di def saw xeet, fan yu mujj ya.»