Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 23:5-22 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 23:5-22 in Kàddug Yàlla gi

5 Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
6 Balaam dellu ca moom, fekkul lu moy mu taxaw ca saraxu dóomalam, moom ak kàngami Mowab yépp.
7 Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne: «Fa Aram la ma Balag buuru Mowab jële, foofa ca tundi penku ya, ne ma: “Kaay ñaanal ma yàlla Yanqóoba, Dikkal rëbbal ma Israyil mii.”
8 Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul?
9 Kaw doj yii laa tollu di leen séen, fi kawte yii laa leen jéere. Aw askan a ngii, dëkke fu beru, te bokkuñu ak xeet yi.
10 Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»
11 Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?»
12 Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu Aji Sax ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?»
13 Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.»
14 Mu daldi koy yóbbu ba ca toolub Sofim, ca collu tundu Pisga. Ci kaw loolu mu tabax fa juróom ñaari sarxalukaay, sarxalukaay bu nekk, mu sarxalati fa yëkk wu ndaw akam kuuy.
15 Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»
16 Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
17 Mu dem ba ca moom, fekku ko lu moy mu taxaw ca wetu saraxu rendi-dóomalam, mook kàngami Mowab. Balag ne ko: «Lu Aji Sax ji wax?»
18 Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne: «Jógal dégloo, Balag, teewlu maa, doomi Sippor.
19 Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?
20 Kàddug barkeel gii laa jot ndigalam, Yàllaa barkeel, duma ko tebbi.
21 Séeneesul aw ay ci askanu Yanqóoba, giseesul aw naqar ci xeetu Israyil wii. Seen Yàlla Aji Sax jee ànd ak ñoom, njiinum buur a jibe fa seen biir.
22 Yàllaa leen jële Misra, féete leen fa ay béjjén féete nagu àll.
Màndiŋ ma 23 in Kàddug Yàlla gi