20 Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.»
21 Ca ëllëg sa Balaam takk mbaamam, ànd ak kàngami Mowab, dem.
22 Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam Aji Sax ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam.
23 Ci kaw loolu mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji taxaw ca digg yoon wa, xàccib saamaram. Mbaam ma ne walbit, wàcc yoon wa, topp àll ba. Balaam dóor mbaam ma, waññi ko ba ca yoon wa.