Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 22:16-26 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 22:16-26 in Kàddug Yàlla gi

16 Ñooña dem ba ca Balaam, ne ko: «Balag doomu Sippor dafa wax ne: “Ngalla, bu la dara teree dikk, wuysi ma.
17 Maa lay teral teraanga ju réya réy. Loo ma wax, ma def. Dikkal rekk, móolul ma gàngoor gii.”»
18 Balaam tontu surgay Balag, ne leen: «Bu ma Balag doon jox këram ba mu fees ak xaalis ak wurus sax, duma mana def lenn lu tuut mbaa lu réy, lu tebbi sama ndigalu Yàlla Aji Sax ji.
19 Waaye yeen it dal-leen fii guddig tey, ba ma xam lu ma Aji Sax jiy waxaat.»
20 Ci kaw loolu Yàlla dikkal Balaam ca guddi ga, ne ko: «Gannaaw woosi la mooy tànki ñii, àndal ak ñoom. Waaye nag lu ma la wax rekk, def ko.»
21 Ca ëllëg sa Balaam takk mbaamam, ànd ak kàngami Mowab, dem.
22 Ba loolu amee sànjum Yàlla tàkk ndax yoon wa mu sumb. Malaakam Aji Sax ji nag taxaw ca yoon wa, nara jànkoonte ak moom, moom mu war mbaamam, ànd ak ñaari surgaam.
23 Ci kaw loolu mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji taxaw ca digg yoon wa, xàccib saamaram. Mbaam ma ne walbit, wàcc yoon wa, topp àll ba. Balaam dóor mbaam ma, waññi ko ba ca yoon wa.
24 Ba mu ko defee malaakam Aji Sax ji taxawi fu yoon wa def ñall wu sew wu jaare digg tóokëri reseñ, ñaari miir séq ko.
25 Mbaam ma gis malaakam Aji Sax ji, daldi tafu ca miir ba, ba tancaale ca tànkub Balaam. Balaam dellu ko dóor.
26 Malaakam Aji Sax ja dellu jiitu, ba taxawi fu xat, ba maneesula weesalook moom, du ndijoor, du càmmoñ.
Màndiŋ ma 22 in Kàddug Yàlla gi