Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 22:1-11 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 22:1-11 in Kàddug Yàlla gi

1 Bànni Israyil demati ba dali ca joori Mowab ca wàllaa dexu Yurdan, janook Yeriko.
2 Fekk na Balag doomu Sippor gis mboolem la bànni Israyil def Amoreen ña.
3 Mowab nag am tiitaange ju réy ca gàngooru bànni Israyil, ndax bare. Mowab jàq na ba mu gisee bànni Israyil.
4 Ci kaw loolu Mowab giseek magi Majan, ne leen: «Ndiiraan wii kat, ni nag di forem parlu ba mu set, ni lañu nara ñédde li nu wër lépp, ba mu set.» Jant yooyu Balag doomu Sippor moo doon buuru Mowab.
5 Mu yebal ay ndaw ca Balaam doomu Bewor ngir wooyi ko, ca Petor ga Balaam cosaanoo, ca tàkkal dex ga ngir ne ko: «Balaam! Gàngoor a ngii jóge Misra. Ñu ngii lal suuf si ba mu daj, te ñoo sanc, janook man màkk.
6 Kon nag dikkal gaaw ñaanal ma yàlla gàngoor gii, ngir ñoo ma ëpp doole. Jombul ma duma leen, ba dàq leen réew mi, ndax xam naa ne koo ñaanal, mu barkeel, te koo ñaan-yàlla, mu alku.»
7 Ci kaw loolu magi Mowab ànd ak magi Majan, dem, yóbbaale ay weexal. Ba ñu agsee ca Balaam, daldi koy àgge kàdduy Balag.
8 Mu ne leen: «Fanaanleen fii guddig tey. Tont lu ma ci Aji Sax ji sant rekk, dinaa leen ko àgge.» Kàngami Mowab dal ak Balaam.
9 Yàlla nag dikkal Balaam, ne ko: «Nit ñii fi yaw, ñu mu doon?»
10 Balaam ne Yàlla: «Buuru Mowab Balag doomu Sippor moo yónnee ci man, ne ma:
11 “Balaam, gàngoor a ngii jóge Misra, lal suuf si ba mu daj. Dikkal gaaw móolul ma leen. Jombul ma mana xareek ñoom, ba dàq leen.”»
Màndiŋ ma 22 in Kàddug Yàlla gi