Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 21:7-14 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 21:7-14 in Kàddug Yàlla gi

7 Mbooloo ma dikk ba ci Musaa, ne ko: «Noo tooñ, ndax noo xultu ci kaw Aji Sax ji, ak ci sa kaw. Tinul nu Aji Sax ji, mu teggil nu jaan yi!» Musaa daldi tinul mbooloo ma.
8 Aji Sax ji ne Musaa: «Defarlul jëmmu jaan ju am daŋar, nga wékk ko ci bant. Su ko defee képp ku ñu màtt, boo ca xoolee, mucc.»
9 Ci kaw loolu Musaa defarlu jaanu xànjar, wékk ko ci bant, ba képp ku jaan màtt, bu xoolee jaanu xànjar ja, daldi mucc.
10 Bànni Israyil fabooti, dem ba dali fa ñuy wax Obot,
11 jóge Obot, dali Yee Abarim, ca màndiŋ ma janook Mowab, ca penku ba.
12 Foofa lañu faboo, dem ba dali ca walum Seredd,
13 bàyyikooti foofa, dem ba dali ca wàllaa dexu Arnon, ga wale ca réewum Amoreen ña te jaare ca màndiŋ ma. Dexu Arnon googa, fa la réewum Mowab digalook Amoreen ñi.
14 Moo tax téereb Xarey Aji Sax ji indi ko, ne: «Waxeb ga ca Sufa, xuri Arnon yaak
Màndiŋ ma 21 in Kàddug Yàlla gi