7 Aji Sax ji wax ak Musaa, ne:
8 «Jëlal saw yet, nga dajale mbooloo mi, yaak sa mag Aaróona, ngeen wax ak doj woowu, ñuy gis, mu xelli am ndox. Te nga sottil leen ndox mu jóge ci doj wi, nàndale ko mbooloo mi, ñook seenug jur.»
9 Ba mu ko defee Musaa jële yet wa fa kanam Aji Sax ji, na mu ko ko sante.
10 Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?»
11 Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.
12 Aji Sax ji nag ne Musaa ak Aaróona: «Gannaaw gëmuleen ma, ngir wormaal sama sellnga fi kanam bànni Israyil, loolu tax na dungeen yóbbu mukk mbooloo mii ca réew ma ma leen jox.»
13 Loolooy walum Meriba, (mu firi Jote ba). Fa la bànni Israyil jote woon ak Aji Sax ji, ba mu biral sellngaam fa seen biir.
14 Gannaaw gi, Musaa moo yebale ay ndaw fa dëkk ba ñuy wax Kades, ñu dem ca buurub Edom, ne ko: «Israyil say bokk dañoo wax ne: Umplewoo mboolem coono bi nu daj.
15 Sunuy maam a demoon Misra; dëkk nanu Misra lu yàgg, waa Misra di nu mitital, na woon ca sunuy maam.
16 Ci biir loolu nu woo Aji Sax ji wall, mu dégg sunu yuux, daldi yebal malaaka, mu génne nu Misra. Léegi nu ngi nii fi Kades, dëkk bi digalook sam réew.