Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 20:6-12 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 20:6-12 in Kàddug Yàlla gi

6 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona bàyyikoo ca mbooloo ma, dem ba ca bunt xaymab ndaje ma. Ñu ne gurub, dëpp seen jë fa suuf. Leeru Aji Sax ji nag feeñu leen.
7 Aji Sax ji wax ak Musaa, ne:
8 «Jëlal saw yet, nga dajale mbooloo mi, yaak sa mag Aaróona, ngeen wax ak doj woowu, ñuy gis, mu xelli am ndox. Te nga sottil leen ndox mu jóge ci doj wi, nàndale ko mbooloo mi, ñook seenug jur.»
9 Ba mu ko defee Musaa jële yet wa fa kanam Aji Sax ji, na mu ko ko sante.
10 Musaa ak Aaróona nag dajale mbooloo ma fa janook doj wa, Musaa ne leen: «Yeen diiŋatkat yi, dégluleen ma fii! Doj wii, tee nu leen cee génneel am ndox boog?»
11 Ci kaw loolu Musaa yékkati loxoom, dóor yetam ca doj wa ñaari yoon, ndox mu bare wale ca, mbooloo ma daldi naan, ñook seenug jur.
12 Aji Sax ji nag ne Musaa ak Aaróona: «Gannaaw gëmuleen ma, ngir wormaal sama sellnga fi kanam bànni Israyil, loolu tax na dungeen yóbbu mukk mbooloo mii ca réew ma ma leen jox.»
Màndiŋ ma 20 in Kàddug Yàlla gi