6 Wàllu Cimyoneen ñi, Selumyel doomu Surisadaay.
7 Wàllu Yudeen ñi, Nason doomu Aminadab.
8 Wàllu Isakareen ñi, Netanel doomu Suwar.
9 Wàllu Sabuloneen ñi, Elyab doomu Elon.
10 Ñi ciy askanu Yuusufa ñii la: Ci wàllu Efraymeen ñi, Elisama doomu Amiyut. Wàllu Manaseen ñi, Gamalyel doomu Pedasur.
11 Wàllu Beñamineen ñi, Abidan doomu Gidoni.
12 Wàllu Daneen ñi, Ayeser doomu Amisadaay.
13 Wàllu Asereen ñi, Pagyel doomu Okkran.
14 Wàllu Gàddeen ñi, Elyasaf doomu Dewel.
15 Wàllu Neftaleen ñi, Ayra doomu Enan.»
16 Ñooñu lañu woo ci mbooloo mi, muy ñi jiite seen giiri maam. Ñooy njiiti gàngoori Israyil.