Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 1:46-53 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 1:46-53 in Kàddug Yàlla gi

46 Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
47 Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
48 Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko:
49 «Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israyil.
50 Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
51 Bu jaamookaay bi dee dem, Leween ñee koy wékki, bu jaamookaay bi dee dale bérab, Leween ñee koy we. Ku ci bokkul ba laal ci nag, dees koy rey.
52 Bànni Israyil gi ci des, na ku ci nekk topp dalam, ak raayaam ak kurélam.
53 Leween ñi nag nañu dal fi wër jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence. Su ko defee am sànj du dal ci kaw mbooloom bànni Israyil. Te itam na Leween ñi dénkoo dénkaaney jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence.»
Màndiŋ ma 1 in Kàddug Yàlla gi