Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 1:17-50 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 1:17-50 in Kàddug Yàlla gi

17 Ba loolu amee Musaa ak Aaróona tofloo ñooñu ñu tudd seeni tur,
18 ñu dajale mbooloo ma mépp, keroog ca benn fanu ñaareelu weer wa. La ko dale ca ña am ñaar fukki at, jëm kaw, ñoom ñépp daldi bindu ca limeefu tur ya, ku nekk ak kër maamam, giir ak giir, làng ak làng, bopp ak bopp.
19 Noonee ko Aji Sax ji sante woon Musaa, na la Musaa takke seen lim ca màndiŋu Sinayi.
20 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Ruben taawub Israyil seen maam, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
21 Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500).
22 Ñu lim bopp ak bopp, turi sëti Simeyon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
23 Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300).
24 Ñu lim turi sëti Gàdd, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
25 Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650).
26 Ñu lim turi sëti Yuda, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
27 Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600).
28 Ñu lim turi sëti Isaakar, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
29 Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400).
30 Ñu lim turi sëti Sabulon, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
31 Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400).
32 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Efrayim, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
33 Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500).
34 Ñu lim turi sëti Yuusufa yi askanoo ci doomam Manase, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
35 Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200).
36 Ñu lim turi sëti Beñamin, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
37 Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400).
38 Ñu lim turi sëti Dan, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
39 Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700).
40 Ñu lim turi sëti Aser, ku nekk ak làngam ak kër maamam, mboolem góor ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
41 Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500).
42 Ñu lim turi sëti Neftali, ku nekk ak làngu cosaanam ak kër maamam, mboolem ñi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw.
43 Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400).
44 Yooyu limeef la Musaa ak Aaróona tënk, ña leen ca jàpple di fukki kilifay Israyil ak ñaar, ku ci nekk taxawal kër maamam.
45 Mboolem bànni Israyil yi xare war, te ñu am ñaar fukki at, jëm kaw, limees na leen, ku ci nekk ak kër maamam.
46 Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550).
47 Giirug Leween ñi nag ci bànni Israyil lañu bokk, waaye limaaleesu leen ak ñoom.
48 Aji Sax ji moo waxoon Musaa, ne ko:
49 «Giirug Lewi ñoom, bu leen lim, bu leen waññaaleek bànni Israyil.
50 Waaye yaw ci sa bopp nanga sas Leween ñi jaamookaay bi seedes kóllëre gi dence, mook la muy àndal lépp, ak mboolem lu ca bokk. Ñooy gàddu jaamookaay bi, ak la muy àndal lépp, di ko topptoo, te it fi wër jaamookaay bi lañuy dal.
Màndiŋ ma 1 in Kàddug Yàlla gi