Text copied!
Bibles in Wolof

Màndiŋ ma 19:6-15 in Wolof

Help us?

Màndiŋ ma 19:6-15 in Kàddug Yàlla gi

6 Su ko defee sarxalkat bi sàkk bantu seedar ak caru isob ak ndimo lu xonq curr, boole ko sànni ca sawara wa ñuy lakk nag wa.
7 Gannaaw loolu na sarxalkat bi fóot ay yéreem, sangu, doora mana duggaat ci dal bi, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.
8 Kiy lakk nag wi itam, na fóot ay yéreem, sangu, te du ko tee yendoo sobe ba ca ngoon.
9 Na ku set tonni dóomu nag wa, te sotti ko bérab bu set, foofa ca biti. Dóom ba dencub mbooloom bànni Israyil lay doon, ñu di ko waajale ndoxum setlu, ngir saraxu póotum bàkkaar.
10 Ku góor kiy tonni dóomi nag wi itam day fóot ay yéreem, te du tee mu yendoo sobe ba ca ngoon. Na loolu di dogalu yoon bu sax fàww, ñeel bànni Israyil, ak doxandéem bu dëkk ci seen biir.
11 «Bu loolu weesee ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, dina sobewu diiru juróom ñaari fan.
12 Na setlu ca ndox moomee ca bésub ñetteel ba, gannaaw ba mu ko laalee, te na setluwaat ca bésub juróom ñaareel ba. Su ko defee mu set. Waaye su setluwul ca bésub ñetteel ba, ak bésub juróom ñaareel ba, du set.
13 Képp ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, bu setluwul, màkkaanu Aji Sax ji la sobeel. Kooku dees koy dagge ci bànni Israyil. Gannaaw ndoxum setlu ma, wiseesu ko ko, sobewu lay wéye.
14 «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan,
15 te mboolem ndab lu fa ubbiku woon, kubeer it ubu ko woon ràpp, loola ndab sobewu na.
Màndiŋ ma 19 in Kàddug Yàlla gi