13 Képp ku laal nit ku dee, ak néew bu mu mana doon, bu setluwul, màkkaanu Aji Sax ji la sobeel. Kooku dees koy dagge ci bànni Israyil. Gannaaw ndoxum setlu ma, wiseesu ko ko, sobewu lay wéye.
14 «Lii la yoon wi tëral: Bu nit deeyee ci biir xayma, képp ku dugg ci biir xayma bi, ak képp ku mu fekk ci xayma bi, day sobewu diiru juróom ñaari fan,
15 te mboolem ndab lu fa ubbiku woon, kubeer it ubu ko woon ràpp, loola ndab sobewu na.
16 Képp ku laal ca àll ba, nit ku ñu bóome saamar, mbaa ku Yàlla moomal boppam, mbaa mu laal yaxi nit ku dee, mbaa mu laal bàmmeel, kooka day sobewu diiru juróom ñaari fan.